1 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di dénk sunu jigéen Febe, miy liggéeyal mbooloom ñi gëm ci dëkku Señsere. 2 Nangeen ko jàpp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Yàlla yi yelloo, te dimbali ko ci lépp lu mu aajowoo, ndaxte moom itam wax dëgg, dimbali na ñu bare, ba ci man mii di wax ak yéen.
16 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu.
17 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore. 18 Ndax ñu deme noonu liggéeyaluñu Kirist sunu Boroom; seen bopp lañuy liggéeyal. Ñu ngi ñëw ak làmmiñ yu neex, di jay xol yu woyof yi, ba nax leen. 19 Waaye seen dégg ndigal bir na ñépp, ba sama xol sedd lool ci yéen. Teewul nag damaa bëgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te baña laal dara ci lu bon. 20 Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina not Seytaane ci seeni tànk léegi.
21 Timote sama nawle bi may jàpple ci liggéey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater.
22 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi.
23 Gayus mu ngi leen di nuyu; moo may ganale ci këram, te foofa it la mbooloo mi di dajaloo. Erast miy topptoo mbiri xaalisu dëkk bi it, nuyu na leen, ak sunu mbokk Kartus.
24 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen! Amiin.
25 Santleen Yàlla, mi leen mana saxal bu wér ci dëggu xibaaru jàmm, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu làqu diirub ay ati at, 26 waaye léegi nag Yàlla dindi na nu ci kumpa. Santaane na, nu yégle xibaar boobu ci xeeti àddina sépp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu.
27 Yàlla mi jagoo xam-xam bépp, moom rekk moo yelloo ndam ba fàww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.
<- ROOM 15