1 Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ca juróom ñeenteelu at ma, fukki fan ca fukkeelu weer wa. Mu ne ma: 2 «Yaw nit ki, bindal bés bii, bés bii ci boppam, ndax buuru Babilon gaw na Yerusalem bés niki tey. 3 Léebalal kërug fippukat yi aw léeb, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
15 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 16 «Yaw nit ki, maa ngii di nangusi sa bànneexu bët cim pàdd. Bul yuuxu, bul jooy, bu sa rongooñ wadd. 17 Binnil ndànk te bul ñaawlu. Bul tàggook sa kaala, bul tàggook say carax, bul muur sa tuñum kaw ba ci sikkim di ko ñaawloo. Bul lekk ñam wu la njaal mi indil.[a]»
18 Wax naak mbooloo mi ci suba, ci ngoon si sama soxna dee. Bët set ma def li ñu ma sant. 19 Mbooloo mi nag ne ma: «Xanaa doo nu wax lii ngay def nii, lu muy wund ci nun?» 20 Ma ne leen: «Kàddug Aji Sax jee ma dikkal, ne ma: 21 Waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama bérab bu sell bii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral. 22 Te nangeen def nii ma def. Buleen muur tuñum kaw ba ci sikkim te buleen lekk ñam wu leen njaal mi indil. 23 Buleen tàggook kaala, buleen tàggooki carax. Buleen yuuxu, buleen jooy. Waaye dingeen jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef, ngeen ànd di binni.” 24 Mu ne: “Na Esekiyel di seen misaal. Bu jotee, mboolem nu mu def, nangeen ko def, ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.”
25 «Yaw nit ki, bés bu ma nangoo ci ñii seen tatay daraja ji ñuy bége, muy seen bànneexu bët, di seen xintey bakkan, ba nanguwaale seen doom yu góor ak yu jigéen, 26 bésub keroog ku ca rëcce dina dikk ba ci yaw, àgge la xibaar bi. 27 Bésub keroog sa gémmiñ dina ubbiku, nga noppee luu, ba wax ak ka rëcc. Su boobaa yaay doon misaalu mbooloo mi, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»
<- Esekiyel 23Esekiyel 25 ->-
a 24.17 Ku deele daawul togg. Waa njaal mi ñooy indi ñam wu ñu lekk ci dëj bi.