Ase
1 -Ca ñaareelu atu nguuru Buur Daryus[a], ca juróom benneelu weer wa, yemook benn fan ca weer wa, kàddug Aji Sax ji moo dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase, ñeel doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ñeel itam doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba. Mu ne: 2 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Askan wii dañu ne àpp bi jotagul; àppub kër Aji Sax ji moo jotagul, ba ñu war koo tabaxaat.» 3 Kàddug Aji Sax ji nag dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase. Mu ne:
12 Ba loolu amee doomu Selcel, Sorobabel, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña des ca askan wa, ñoom ñépp déggal seen wooteb Yàlla Aji Sax ji, ak kàddug Yonent Yàlla Ase, noonee ko ko seen Yàlla Aji Sax ji yóbbantee. Askan wa nag ragal Aji Sax ji. 13 La ca tegu Ase, ndawal Aji Sax ji, jottli askan wa yóbbanteb Aji Sax ji. Mu ne leen: «Maa ànd ak yeen, kàddug Aji Sax jee.»
14 Ba mu ko defee Aji Sax ji yékkati sidditi doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ak sidditi doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak sidditi ña des ca mbooloo ma ñépp, ba ñu sottali liggéeyi kër Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, seen Yàlla. 15 Loola yemook ñaar fukki fan ak ñeent ca juróom benneelu weer wa.
Ase 2 ->-
a 1.1 Daryus buuru Pers bu mag la woon.